Taalif yii dañuy wax ci jikko yi nit ñi wara am, muy ci seen kër wala ci askanu Senegaal. Njariñal Taalif yii dañuy wax ci jikko yi nit ñi wara am, muy ci seen kër wala ci askanu Senegaal. Njariñal téere bi nekk na di jàngal xale yi jikko yu baax yooyu, ba noppi di leen xamal yenn jikko yu ñu wara moytu. Muy téere bu am ñaari pàcc: pàcc bu jëkk baa ngi wax ci jikko yi. Ñaareelu pàcc bi dafay wone soppey bindkat bi ak seeni jikko yu nu mëna roy ci ñoom. Nu lim ci soppe yi: Yonnent bi (SAW) ak ay sahaabaam, waajuri aji taalif ji, Sëriñ Saalihu Mbàkke, Maam Abdul Aziz Si Dàbbaax, Alaaji Móodu Njégén, Sëriñ Muniiru Njégén, Ustaz Useynu Jéen (Tiwaawan)... Téere bii mi ngi aju ci prograamu njàngale moral ci daara yu ndaw yi ci Senegaal. Mën naa nekk jumtukaayu jàngale jàngalekat yi ngir jàngale jikko yu mel ni ngëm, woyof, kersa, muñ, ngor, jom, njub, fit, màndute, yar, teggin, sago, ...
| Pages: | 116 |
|---|---|
| Published: | 2026 |
| ISBN: | 979-8-89966-409-0 |
| Language: | French |
| Category: | Poetry |